18 Te mangi la wah͈ it, ne yā di Peter, te chi doch wile lā di tabah͈ suma jangu; te bunt’ i nāri du ko fabi.
Tūr i fuk’ i tālube ak ñar yangile: Benel bi, Simon ku tuda Peter, ak Andrew rak’ am; James dōm i Zebedee, ak John rak’ am;
Te you Capernaum, mi yēkatiku cha asaman, di nañu la sufel be chi nāri: ndege koutef ya ma def on chi you, su ñu len def on cha Sodom, kôn mu des bentey.
Su len bañê dēga, wah͈ ko ndaje ma; te su bañê dēga ndaje ma itam, na neka chi you niki Gentile ak publican.
Don na doh͈ cha tefes i Galilee, te mu gis ñar i mboka, Simon ku tūda Peter, ak mag am Andrew, di sani mbal cha gēch ga; ndege nek’ on nañu i mōl.
Mōtah͈ ku mu mun a don ku dēga suma i bāt yile, te def len, di na niro ak nit i sago, ka tabah͈ nēg am chi kou doch:
Mu indi ko fi Yesu. Yesu sêt ko, te ne, Yā di Simon, dōm i John: di nañu la tūde Cephas (mu tiki ne Peter).