Te ku wah͈ lu bon lu jem chi Dōm i nit ka, di nañu ko baal; wande ku wah͈ lu bon lu jem chi Nh͈el mu Sela ma, du ñu ko baali muka chi aduna sile, wala chi lah͈īra.
Ndege naka Jonah nek’on chi bir mbonkana ma ñet’ i bechek ak ñet’ i gudi, nōgule la Dōm i nit ka di nekeji chi h͈ol i suf si ñet’ i bechek ak ñet’ i gudi.
Mbōlo ma tontu ko, ne, Dēga nañu chi tauret bi ne Krista di na deka bel mos: naka nga wah͈e nak ne Dōm i nit ka ela na yēkatiku? Kan a di Dōm i nit kōku?