11 Lutah͈ be h͈amu len ne wah͈u ma len chi mburu? Wande ndah͈ ngēn otu mporoh͈al i Pharisee ya ak Sadducee ya.
Pharisee ya ak Sadducee ya ñou di ko fir, te lāj ko mu won len mandarga cha asaman.
Fōfale ñu h͈am ne wah͈ul len ñu otu mporoh͈al i mburu, wande njemantal i Pharisee ya ak Sadducee ya.
Yesu ne len, Otu len te moytu mporoh͈al i Pharisee ya ak Sadducee ya.
Wande ba mu gise jupa chi Pharisee ya ak Sadducee ya di ñou chi batise am, mu ne len, E h͈êt i ñangōr gi, kan a len yēgal ngēn di ūt a rēcha chi mer mi di ñou?
Lutah͈ ngēn h͈amul suma wah͈? ndege munu len a dēga suma bāt.