5 Wande yēn a ne, Ku di wah͈ bay am wala ndey am, ne, Yalla lā may lu la mun a jeriñ:
Ndege Yalla wah͈ on na, ne, Teralal sa bay ak sa ndey: te, Ku h͈as bay am wala ndey am, na dē dē gi.
Bu mu teral bay am. Tah͈na be defadi ngēn eble’ Yalla mu di dara chi sēn nābe.