4 Ndege Yalla wah͈ on na, ne, Teralal sa bay ak sa ndey: te, Ku h͈as bay am wala ndey am, na dē dē gi.
V. Teralal saa bai ak saa nde, ndah saa i fan mun na guda ce suf sa la Yalla saa Borom mai.
Mu tontu len, ne, Yēn it, lutah͈ ngēn moy eble’ Yalla chi sēn nābe?
Wande yēn a ne, Ku di wah͈ bay am wala ndey am, ne, Yalla lā may lu la mun a jeriñ:
Teralal sa bay ak sa ndey: te, Sopal sa morom niki sa bopa.
Fōfale Yesu ne ko, Randu ma Seytane, ndege binda nañu, ne, Na nga jāmu Borom ba sa Yalla, te na nga ko topa, mōm reka.