31 Tah͈na mbōlo ma jomi, ba ñu gise lū ya wah͈, lagi ya wer, tēlekat ya doh͈, ak silmah͈a ya gis: ñu magal Yalla i Israel.
Mbōlo mu rey ñou fi mōm, and’ ak ña lagi, silmah͈a, lu, tēlekat, ak ñenen ñu bare, nu teg len chi tank’ am, te mu weral len;
Su la sa loh͈o mbāte sa tanka moylô, dog ko, te sani ko: mō gen nga h͈araf chi dunda ak lago mbāte di sôh͈, aste am ñar i loh͈o mbāte ñar i tanka, ñu di la sani chi safara su dul jêh͈.
Silmah͈a ya ak ña lagi ñou fi mōm chi juma ja, te mu weral len.
Ba ko Yesu dēge, mu jomi, te ne ña ko top’ on, Chi dega mangi len di wah͈, mosu ma feka ngum gu nu day, dēt, du chi Israel.
Ba ñu gēne, ñu yub ko nit ku lū, ka jine jap’ on.
Ba mu gēnê jine ja, lū ba wah͈: mbōlo ma jomi, ne, Mosu ñu ko gise nile chi Israel.
Wande ba mbōlo ma gise lōla, ñu ragal, te magal Yalla, ki may nit gōgu kantan.
Ñu ôlu nak ka silmah͈a won ñar i yōn, te ne ko, Na nga jebal Yalla ndam: h͈am nañu ne nit kile bakarkat la.