26 Mu tontu ko, ne, Daganul ñu jel mburu i h͈alel yi, te sani ko h͈aj yi.
Wande mu ñou te jāmu ko, ne, Borom bi, lêl dimali ma.
Wande mu ne, Wau, Borom bi; ndege h͈aj yi sah͈, di nañu di leka ndesit ya di rot chi sēn tabul i borom.
Bu len joh͈ la sela h͈aj ya, te bu len sani sēn i takay chi kanam i mbām; ndig so otuwul di nañu len degat chi sēn run tanka, te walbataku h͈oti len.