24 Wande mu tontu, ne, Fi nh͈ar i nēg i Israel yu rēr yi reka la ñu ma yōni.
Wande tontuwu ko dara. I tālube am ñou, te dagān ko, ne, Demlo ko, ndege tanh͈al na ñu.
Ndege Dōm i nit ka ñou na ndah͈ mu musal ñu rēr ña.
Wande ba mu gise mbōlo ma, mu yerem len, ndege da ñu jāh͈le, te tasāro niki nh͈ar yu amul samakat.