13 Wande mu tontu, ne, Njembat bu neka bu suma Bay ba cha ajana jembatul on, di na ko simpi.
Fōfale i tālube am ñou, te ne ko, H͈am nga ne Pharisee ya fakatalu nañu, ba ñu dēge kadu gile?
Man mā di garap i biñ bu dega bi, te suma Bay a di beykat ba.
Banh͈as bu neka chi man bu mēñul dōm, di na ko gor: te banh͈as bu neka bu mēña dōm, di na ko setal, ndah͈ mu mēña dōm yu gen a bare.
Su kena dekule chi man, di nañu ko sani cha biti niki banh͈as, te di na lah͈; te ñu forati len, te sani len cha safara sa, te ñu laka.