8 Mōm nak ndege ndey am jeñtal na ko, ne, May ma file bop’ i John Batisekat ba chi ndap.
Ñu indi bop’ am chi ndap, may ko janh͈a ba, mu yubu ko fa ndey am.
Mōtah͈ mu dig ak geñ ne, di na ko may lu mun a don lu mu lāj.
Bur ba nah͈arlu ko; wande ndig geñ am ga, ak ña tōg on ak mōm di leka, mu ebal ñu may ko ko.