5 Ba mu ko buge rēy, mu ragal mbōlo ma, ndege fōg nañu ne yonent la won.
Wande lutah͈ on ngēn dem? sêt ab yonent am? Wau, ma ne len, te ku upa yonent.
Wande su ñu ne, Chi nit; da ñu ragal mbōlo ma; ndege jape won nañu John niki yonent.
Ndege John ñou on na fi yēn chi yōn i njūbay, te gumu len ko won: wande publican ya ak garbo ya gum on nañu ko: te yēn ba ngēn ko gise, rechuwu len cha ganou sah͈ ndah͈ ngēn gum ko.