32 Ba ñu ñoue chi bir gāl ga, ngelou li dal.
Nōn’ ak nōna Yesu talal loh͈o am, te japa ko, ne ko, E borom‐ngum gu new, lutah͈ nga nimse?
Te ña neka chi gāl ga jāmu ko, ne, Chi dega yā di Dōm i Yalla.
Tah͈na ñu nangu jel ko cha gāl ga: te nōn’ ak nōna gāl ga aga cha jēri ja ñu buga dem.