23 Ganou ba mu demlô mbōlo ma, mu yēg cha kou tūnda wa ndah͈ mu ñān Yalla, te chi gudi ga mu neka fa mōm dal.
Yesu nak ñou ak ñom chi bereb bu tūda Gethsemane, te ne i tālube am, Tōg len file ba ma dem ñān fale.
Wande you, so di ñān, dugal chi sa bir nēg, te ba nga teje bunta ba, ñānal sa Bay ki chi nubu; te sa Bay ki di gis lu nubu, di na la yōl.