20 Ñepa leka be sūr; ñu forātu ndesit ma be ñu fêsal fuk’ i sendel ak ñar.
Ña lek’ on jurom i njūne’ gōr la ñu potah͈, ganou i jigen ak i gūne.
Tālube ya ne ko, Fan la ñu mun a ame mburu mu doy mbōlo mu rey niki bile, chi manding mi?
Barkel cha ña di h͈īf te mar chi njūbay; ndege di nañu doylu.
Philip tontu ko, ne, Ñar tēmēr i transu mburu du len doy, ndah͈ ku neka jel tuti.