16 Wande Yesu ne len, Soh͈laū ño dem; may len ñu leka.
Ba ngon jote, i tālube am ñou fi mōm, ne, File manding la, te wah͈tu wi wey na jēg; na nga ebal mbōlo mi ñu dem cha bir deka ya, te jenda dundu.
Ñu ne ko, Am nañu fi jurom i mburu reka, ak ñar i jen.
Ndege ñena dēfe on nañu, ne naka Judas ame won mbus ma, Yesu nôn ko, Jendal lu ñu soh͈la chi h͈ewte gi; mbāte mu sarah͈ miskin yi.