15 Ba ngon jote, i tālube am ñou fi mōm, ne, File manding la, te wah͈tu wi wey na jēg; na nga ebal mbōlo mi ñu dem cha bir deka ya, te jenda dundu.
Ba ko Yesu dēge, mu juge fa chi gāl chi manding mu wēt: ba mbōlo ma dēge lōla, ñu rūnga topa ko tank’ ak tanka cha deka ya.
Mu gēna, te gis mbōlo mu rey; mu am yermande chi ñom, te weral sēn i jarak.
Wande Yesu ne len, Soh͈laū ño dem; may len ñu leka.
Wande tontuwu ko dara. I tālube am ñou, te dagān ko, ne, Demlo ko, ndege tanh͈al na ñu.