14 Mu gēna, te gis mbōlo mu rey; mu am yermande chi ñom, te weral sēn i jarak.
Ba ngon jote, i tālube am ñou fi mōm, ne, File manding la, te wah͈tu wi wey na jēg; na nga ebal mbōlo mi ñu dem cha bir deka ya, te jenda dundu.
Yesu dem cha bir Galilee yepa, di jemantale chi sēn i juma, di wāre linjil i ngur gi, te di weral h͈êt i opa ju neka, ak hêt i jangaro ju neka chi digante nit ña.
Wande ba mu gise mbōlo ma, mu yerem len, ndege da ñu jāh͈le, te tasāro niki nh͈ar yu amul samakat.