10 Mu yōni ku dog bop’ i John chi kaso ba.
Ñu indi bop’ am chi ndap, may ko janh͈a ba, mu yubu ko fa ndey am.
Bur ba nah͈arlu ko; wande ndig geñ am ga, ak ña tōg on ak mōm di leka, mu ebal ñu may ko ko.
Wande mangi len di wah͈, Elijah ñou on na jēg, te h͈amu ñu ko won, wande ñu def ko lu ñu buga chi mōm. Nōgu itam la ño sonaleji Dōm i nit ka.