7 Yenen rot chi digante i tah͈as, te tah͈as yi sah͈ando ak ñom, te waka len:
Ka ñu ji won chi digante tah͈as ya, mō di ka dēga bāt bi; te i ntopato’ aduna si, ak nah͈ay i amam, waka bāt bi, mu bañ a mēña dōm.
Ba janta ba fenke mu laka len; te ñu lah͈, ndege amu ñu rên.
Yenen rot chi suf su bāh͈ sa, te mēña mēñef, yena ya tēmēr, yale jurom bena fuka, yale ñeta fuka.