6 Ba janta ba fenke mu laka len; te ñu lah͈, ndege amu ñu rên.
Wande amul rên chi bop’ am, te muñ chi sā yu new dal; ndege su nah͈ar joge wala ngeten ndig bāt bi, nōg’ ak nōga mu fakatalu.
Yenen rot chi i bereb i doch, fa ñu amule suf su bare; ñu gou a sah͈, ndege suf sa h͈ōtul;
Yenen rot chi digante i tah͈as, te tah͈as yi sah͈ando ak ñom, te waka len: