57 Ñu fakatalu chi mōm. Wande Yesu ne len, Yonent ñakul teranga lu moy chi dek’ am, ak chi ker am.
Te barkel chi ku dul feka fakatalu chi man.
Defu fa i koutef yu bare ndig sēn gumadi.
Ndege Yesu chi bop’ am, sēde won na ne yonent amul teranga chi rew am.
Te ñu ne, Ndah͈ kile dowul Yesu, dōm i Yusufa, te ñu h͈am bay am ak ndey am? Naka la wah͈e, ne, Manga juge cha asaman?
Wande Yesu h͈am chi bop’ am ne i talube am ñurumtu nañu chi lile, te mu ne len, Ndah͈ lile tah͈ ngēn fakatalu?