55 Kile du dōm i minise bā’m? du ndey am a tūda Mariama? te i rak’ am James, ak Yusufa, ak Simon, ak Judas?
Chi sēn digante la Mariama Magdalene nek’ on, ak Mariama ndey i James ak Joses, ak ndey ī dōm i Zebedee.
Wande ndey i Yesu anga tah͈ou on cha kanam i kura ba, ak rak’ am, Mariama jabar i Clopas, ak Mariama Magdalene.
Te ñu ne, Ndah͈ kile dowul Yesu, dōm i Yusufa, te ñu h͈am bay am ak ndey am? Naka la wah͈e, ne, Manga juge cha asaman?
H͈am nañu ne Yalla wah͈ on na cha Musa; wande kile, h͈amu ñu fu mu bayako.