54 Ba mu dike chi rew am, mu jemantale len chi sēn i juma, tah͈na ñu jomi, ne, Nit kile naka la ame h͈amh͈am bile, ak koutef yile?
Te ñou, deka chi rew mu tūda Nazareth: ndah͈ la yonent ya wah͈ on motaliku, ne, Di nañu ko tūde Nazarene.
Yesu dem cha bir Galilee yepa, di jemantale chi sēn i juma, di wāre linjil i ngur gi, te di weral h͈êt i opa ju neka, ak hêt i jangaro ju neka chi digante nit ña.
Am on na ba Yesu sotale bāt yile, mbōlo ma jomi chi njemantal am:
Ñou on na fi yos am, te yos am nanguwu ñu ko won.