53 Am on na ba Yesu sotal on lēb yile, mu juge fōfa.
Mu wah͈ len yef yu bare chi i lēb, ne, Bena jikat dem on na ji;
Mu ne len, Bindānkat bu neka mbōk bu ñu nekalo tālube chi ngur i ajana, niro na ak borom‐ker ku gēne chi dēnchukay am lu ês ak lu maget.
Am on na ba Yesu sotale bāt yile, mbōlo ma jomi chi njemantal am: