52 Mu ne len, Bindānkat bu neka mbōk bu ñu nekalo tālube chi ngur i ajana, niro na ak borom‐ker ku gēne chi dēnchukay am lu ês ak lu maget.
Nit ku bāh͈ di na gēne yef yu bāh͈ chi dēnchukay am bu bāh͈; wande nit ku bon di na gēne yef yu bon chi dēnchukay am bu bon.
Ndah͈ dēga ngēn yef yile yepa? Ñu ne ko, Wau.
Am on na ba Yesu sotal on lēb yile, mu juge fōfa.
Tah͈na yōne nā len i yonent, ak i borom‐sago, ak i h͈amkat: di ngēn rēy ñena ñi, te dāj len cha kura; te di ngēn ratah͈ ñena ñi chi sēn i juma, te geten len chi dek’ ak deka:
Dem len mbōk, def i tālube h͈êt yi yepa, te batise len chi tur i Bay ba, ak Dōm ja, ak Nh͈el mu Sela ma:
Eble bu ês lā len di joh͈, ndah͈ ngēn sopante; naka ma len sope sah͈ yēn itam na ngēn sopante.