51 Ndah͈ dēga ngēn yef yile yepa? Ñu ne ko, Wau.
Mu tontu len, ne, Yēn la ñu may ngēn h͈am i kumpa i ngur i ajana, wande ñom mayu ñu len ko.
Ba kena dēge bāt i ngur gi, te h͈amu ko, fōfale la Seytane ñoue, te dindi la ñu ji won chi h͈ol am. Kile di ka ñu ji won chi wet i yōn wa.
Te sani len chi safara si: fōfale la joy di neka, ak yey i buñ.
Mu ne len, Bindānkat bu neka mbōk bu ñu nekalo tālube chi ngur i ajana, niro na ak borom‐ker ku gēne chi dēnchukay am lu ês ak lu maget.
Dēgu len ne lu mu mun a don lu h͈araf chi gemeñ, dem chi bir, ñu gēne ko chi biti?
Lutah͈ be h͈amu len ne wah͈u ma len chi mburu? Wande ndah͈ ngēn otu mporoh͈al i Pharisee ya ak Sadducee ya.
Bu ngēn di gisi suboh͈un ak h͈udosun mbōk mu di tah͈ou chi bereb bu sela ba, naka Daniel yonent ba wah͈ on (ka ko janga na h͈am),