5 Yenen rot chi i bereb i doch, fa ñu amule suf su bare; ñu gou a sah͈, ndege suf sa h͈ōtul;
Te ka ñu ji won chi i bereb i doch, mō di ka dēga bāt bi, te dal di ko nangu ak banēh͈;
Te ba mu jie, yena pēpa rot nañu cha wet i yōn wa, te mpicha ya dika for len;
Ba janta ba fenke mu laka len; te ñu lah͈, ndege amu ñu rên.