49 Nōgule la neki chi muj i aduna: malāka ya di nañu juge, te h͈ajātle ñu bon ña cha ñu jūb ña,
Mbañ ma ko ji on Seytane la; ngōbte ga muj i aduna si la; te gōbkat ya ño di malāka ya.
Naka ñu budi nduh͈um la, te laka ko chi safara, nōgu la di neki chi muj i aduna.
Ba mu fêse, ñu h͈ēcha ko chi tefes; ñu tōg chi suf, te dajale yu bāh͈ ya chi i ndap, wande sani yu bon ya fale.
Te di na yōni malāka am ya ak nchōu i bufta bu rey, te di nañu dajale ña mu tan’ on chi ñenent i ngelou yi, cha bop’ i asaman be cha muj ga.