46 Ba mu feke bena jamong ju jafe njēg, mu dem jay lu mu am on yepa, te jenda ko.
Ngur i ajana niro na ak alal bu nubu chi bir tōl; ba ko nit feke mu nuba ko, dem chi banēh͈ am jay lu mu am on yepa, te jenda tōl bōbale.
Ngur i ajana nirôti na ak jūla ku don ūt jamong yu bāh͈;
Ngur i ajana nirôti na ak mbal mu ñu sani chi gēch, mu japa h͈êt i jen wu neka: