45 Ngur i ajana nirôti na ak jūla ku don ūt jamong yu bāh͈;
Mu teg benen lēb chi sēn kanam, ne, Ngur i ajana niro na ak nit ka ji on jiu ju bāh͈ chi tōl am;
Ba mu feke bena jamong ju jafe njēg, mu dem jay lu mu am on yepa, te jenda ko.
Ndege ban njeriñ la chi nit, su ame aduna si yepa, te mu ñaka bakan am? wala wan wēchi la nit di joh͈e ndig bakan am?
Wande ñu sagane ko, te dem sēn yōn, kena cha tōl am, kenen cha jayukay am:
Bu len joh͈ la sela h͈aj ya, te bu len sani sēn i takay chi kanam i mbām; ndig so otuwul di nañu len degat chi sēn run tanka, te walbataku h͈oti len.