42 Te sani len cha safara sa; fōfale la joy di neka, ak yey i buñ.
Te sani len chi safara si: fōfale la joy di neka, ak yey i buñ.
Fōfale bur ba ne i rapas am, Ew len loh͈o am ak tank’ am, te sani ko chi lendem i biti; fōfale la joy di neka ak yey i buñ.
Fōfale di na wah͈ ña chi chamoñ am, ne, Randu len ma, yēn ñi alaku, dem len cha safara su dul jêh͈, ba ñu wājal on Seytane ak i malāk’ am:
Am na layu chi loh͈o am, te di na setali boju am fou, te dajale dugup am chi sah͈a mi; wande di na laka choh͈ ba chi safara su feyatil muk.
Wande i dōm i ngur ga, di nañu len tabal chi lendem i biti; fōfale la joy di neka ak yeyi buñ.