41 Dōm i nit ka di na yōne i malāk’ am, te di nañu forātu chi ngur am yef yu moylo yepa, ak ña def lu bon;
Nōgule la neki chi muj i aduna: malāka ya di nañu juge, te h͈ajātle ñu bon ña cha ñu jūb ña,
Suboh͈un aduna si ndig i mpaka! ndege i mpaka soh͈la naño dika; wande suboh͈un nit ka tah͈ mpaka ñou.
Te di na yōni malāka am ya ak nchōu i bufta bu rey, te di nañu dajale ña mu tan’ on chi ñenent i ngelou yi, cha bop’ i asaman be cha muj ga.
Am na layu chi loh͈o am, te di na setali boju am fou, te dajale dugup am chi sah͈a mi; wande di na laka choh͈ ba chi safara su feyatil muk.
Yesu ne ko, Ntila yi am nañu i mpah͈, te mpich’ i asaman si am nañu i taga, wande Dōm i nit ka amul fu mu tedal bop’ am.