34 Yesu wah͈ on na mbōlo ma yef yile yepa chi i lēb, te wah͈u len dara lu dul chi lēb:
Mōtah͈ ma wah͈ ak ñom chi i lēb; ndege ba ñu gise, du ñu gis; te ba ñu dēge du ñu dēga; te fafu ñu di h͈am.
Mu wah͈ len yef yu bare chi i lēb, ne, Bena jikat dem on na ji;
Yesu wah͈ on na len lēb bile: wande h͈amu ñu yef ya mu wah͈ ak ñom.
Yef yile lā len wah͈ chi i lēb: wah͈tu wa di na jot bu ma dul wah͈ati ak yēn chi i lēb, wande di nā len wah͈i bu set chi lu jem chi Bay ba.
Talube am ya ne, Wah͈ nga lēgi bu set, te wah͈u la lēb.