27 I rapas i borom‐ker ga ñou, te ne ko, Borom bi, ndah͈ jiū la won jiu ju bāh͈ chi sa tōl? naka la ame nduh͈um nak?
Wande ba ñu neloue, mbañ am dika, te ji nduh͈um chi digante dugup ja, te dem.
Ba dugup ja sah͈e, te mēña dōm, nduh͈um la fêñ itam.
Mu ne len, Ab mbañ a def lōlu. Rapas ya ne ko, Buga nga ñu dem budi len?
Ndege ngur i ajana niro na ak bena borom‐ker ku gēna chi sūba têl, ndah͈ mu binda i ligeykat chi tōl am.