26 Ba dugup ja sah͈e, te mēña dōm, nduh͈um la fêñ itam.
Wande ba ñu neloue, mbañ am dika, te ji nduh͈um chi digante dugup ja, te dem.
I rapas i borom‐ker ga ñou, te ne ko, Borom bi, ndah͈ jiū la won jiu ju bāh͈ chi sa tōl? naka la ame nduh͈um nak?