25 Wande ba ñu neloue, mbañ am dika, te ji nduh͈um chi digante dugup ja, te dem.
Mu teg benen lēb chi sēn kanam, ne, Ngur i ajana niro na ak nit ka ji on jiu ju bāh͈ chi tōl am;
Ba dugup ja sah͈e, te mēña dōm, nduh͈um la fêñ itam.
I rapas i borom‐ker ga ñou, te ne ko, Borom bi, ndah͈ jiū la won jiu ju bāh͈ chi sa tōl? naka la ame nduh͈um nak?
Wande mu ne, Dēt, h͈ēchna bu ngēn di budi nduh͈um la, di ngēn budiāle dugup ja it.
Bayi len ñar ña ñu sah͈ando be cha ngōbte ga; te cha wah͈tu’ ngōbte ga di nā wah͈ gōbkat ya, ne, Budi len jeka nduh͈um la, taka ko i say te laka ko; wande dajale len dugup ja chi suma sah͈a.
Mbañ ma ko ji on Seytane la; ngōbte ga muj i aduna si la; te gōbkat ya ño di malāka ya.
Ba borom‐seyt ba yīh͈e, ñepa gemantu te nelou.