24 Mu teg benen lēb chi sēn kanam, ne, Ngur i ajana niro na ak nit ka ji on jiu ju bāh͈ chi tōl am;
Ba kena dēge bāt i ngur gi, te h͈amu ko, fōfale la Seytane ñoue, te dindi la ñu ji won chi h͈ol am. Kile di ka ñu ji won chi wet i yōn wa.
Wande ba ñu neloue, mbañ am dika, te ji nduh͈um chi digante dugup ja, te dem.
Mu teg benen lēb chi sēn kanam, ne, Ngur i ajana niro na ak pēp’ i sūna, bu nit fab, te ji chi tōl am;
Mu wah͈ len benen lēb, ne, Ngur i ajana niro na ak mporoh͈al bu jigen jel, te def chi ñet’ i andār i sunguf, be yepa foroh͈.
Mu tontu len, ne, Ka ji jiu wu bāh͈ ba, Dōm i nit ka la;
Ngur i ajana nirôti na ak mbal mu ñu sani chi gēch, mu japa h͈êt i jen wu neka:
Mōtah͈ ngur i ajana niro na ak bena bur bu bug’ on a jel konta ak i jām am.
Ndege ngur i ajana niro na ak bena borom‐ker ku gēna chi sūba têl, ndah͈ mu binda i ligeykat chi tōl am.
Dēglu len benen lēb: Bena borom‐ker am on na, ku jembat on tōl, ñak ko, gas cha nalukay, tabah͈ am tata, lūye ko i ligeykat, te dem cha benen rew.
Ngur i ajana niro na ak bena bur bu h͈umbal on nchēt i dōm am;
Fōfale di nañu nirale ngur i ajana ak fuk’ i h͈ēk, ñu jel on sēn i lampa, di gatanduji borom‐seyt.
Rēchu len, ndege ngur i ajana jegeñsi na.
Yesu dem cha bir Galilee yepa, di jemantale chi sēn i juma, di wāre linjil i ngur gi, te di weral h͈êt i opa ju neka, ak hêt i jangaro ju neka chi digante nit ña.