20 Te ka ñu ji won chi i bereb i doch, mō di ka dēga bāt bi, te dal di ko nangu ak banēh͈;
Ba kena dēge bāt i ngur gi, te h͈amu ko, fōfale la Seytane ñoue, te dindi la ñu ji won chi h͈ol am. Kile di ka ñu ji won chi wet i yōn wa.
Wande amul rên chi bop’ am, te muñ chi sā yu new dal; ndege su nah͈ar joge wala ngeten ndig bāt bi, nōg’ ak nōga mu fakatalu.
Ndege ku mu mun a don ku lāj, di na am; te ku ūt, di na gis; te ku foga, di nañu ko ūbi.
Mō don lampa ba di tāka te di melah͈: te nangu won ngēn a banēh͈u chi i sā cha lêr am ga.