11 Mu tontu len, ne, Yēn la ñu may ngēn h͈am i kumpa i ngur i ajana, wande ñom mayu ñu len ko.
Tālube ya ñou te ne ko, Lutah͈ nga wah͈ ak ñom chi i lēb?
Yesu tontu ko, ne, Barkel chi you, Simon dōm i Jonah; ndege du yaram te du deret a la fêñal lōlu, wande suma Bay ba cha ajana.
Wande mu ne len, Ñepa munu ño nangu kadu gile, wande ña ñu ko may dal.
Mu ne len, Di ngēn nān suma nān chi dega: wande tōg chi suma ndējor ak suma chamoñ, munu ma ko maye kena, ganou ña ko suma Bay ba wājal.
Te mu ne, Lile tah͈ ma wah͈ on len, ne, ken munul a dika fi man, su ko ko Bay ba mayule.
Su kena buge def mbugel am, di na h͈am su njemantal mi juge cha Yalla, mbāte da ma wah͈al suma bopa.