10 Tālube ya ñou te ne ko, Lutah͈ nga wah͈ ak ñom chi i lēb?
Mu tontu len, ne, Yēn la ñu may ngēn h͈am i kumpa i ngur i ajana, wande ñom mayu ñu len ko.
Mu wah͈ len yef yu bare chi i lēb, ne, Bena jikat dem on na ji;
Ku am i nopa, na dēga.