1 Chi bes bōba Yesu gēna on na cha nēg ba, te tōg cha tefes ga.
Ndege ku mu mun a don ku di def suma mbugel i Bay ba cha ajana, mō di suma raka, ak suma jigen, ak suma ndey.
Fōfale Yesu bayi mbōlo ma, h͈araf chi nēg ba; te tālube am ya ñou fi mōm, ne, Tiki ñu lēb i nduh͈um i tōl ba.
Ba mu ñoue chi bir nēg ba, silmah͈a ya ñou fi mōm: Yesu ne len, Gum ngēn ne mun nā def lile? Ñu ne ko, Wau, Borom bi.