48 Wande mu tontu ka ko wah͈, ne, Kan a di suma ndey? te ñan a di suma i raka?
Ku sopa bay am mbāte ndey am as man, daganul chi man; te ku sopa dōm am ju gōr, mbāte dōm am ju jigen as man, daganul chi man.
Kena ne ko, Sa ndey ak sa i rak’ anga tah͈ou cha biti, di buga wah͈ ak you.
Mu talal loh͈o am chi i tālube am, te ne, Sêt len, suma ndey ak suma i raka!