46 Ba mu wah͈andô ak mbōlo ma, ndey am ak i rak’ am tah͈ou cha biti, di buga wah͈ ak mōm.
Njūdu’ Yesu Krista nile la won: Ba ndey am Mariama nangulante Yusufa, ba mu lāta sey ak mōm, fêñu on na ak bir chi Nh͈el mu Sela ma.
Kena ne ko, Sa ndey ak sa i rak’ anga tah͈ou cha biti, di buga wah͈ ak you.
Kile du dōm i minise bā’m? du ndey am a tūda Mariama? te i rak’ am James, ak Yusufa, ak Simon, ak Judas?
Ba ñu h͈arafe cha nēg ba, ñu feka gūne ga ak Mariama ndey am; ñu sūka te jāmu ko; ñu ūbi sēn i wah͈ande, te jebal ko i maye: wurus, fufata, ak mira.
Ne, Jogal, jelal gūne gi ak ndey am, te dem cha suf i Israel; ndege ña ūt on bakan i gūne gi dē nañu.
Wande ndey i Yesu anga tah͈ou on cha kanam i kura ba, ak rak’ am, Mariama jabar i Clopas, ak Mariama Magdalene.
Cha ñetel i fan ba, sey am on na cha Cana i Galilee; te ndey i Yesu anga fa won.
Ganou lōlu mu dem fa Capernaum, mōm, ak ndey am, ak i rak’ am, ak i talube am; te ñu jēki fa fan yu new.
Ndey am ne bukanēg ya, Lu mu len wah͈, def len ko.
Wande ba i mbok’ am deme cha h͈ewte ga, mu dem fa itam, du chi kanam i ñepa, wande chi wētay.
Mbok’ am ya ne ko nak, Gēnal file te dem cha Judea, ndah͈ sa i talube itam mun a gis sa koutef yi nga def.
Ndege i mbok’ am sah͈ gumu ñu on chi mōm.