Bur i gopu bu jigen ba di na tah͈ou chi bes i ate ba ak h͈êt wile, te ey len; ndege juge on na fu sorey ndah͈ mu dēga sago i Suleyman, te ku gen a rey Suleyman angi fi.
Mu dem, te bōle ak mōm yenen jurom ñar i nh͈el yu gen a bon as bop’ am, ñu h͈araf chi bir, te deka fa; te muj i nit kōkale gen na bon as ndôrte am. Nōgule la di meli chi h͈êt wu bon wile.