4 Na mu h͈arafe chi nēg i Yalla ba, te leka mburu ma ñu dān wone, ma daganul on mu leka, wala ña and’ on ak mōm, wande seriñ ya dal?
Wande mu ne len, Ndah͈ jangu len la Dauda def on ba mu h͈īfe, ak ña and’ on ak mōm;
Jangu len itam chi mbinda yi naka seriñ ya chi bes i dimas moy dimas ja cha juma ja, te bakaru ñu?