37 Ndege chi sa i bāt la ñu la joh͈i njūbal, te chi sa i bāt la ñu la joh͈i ndānute.
Te mangi len di wah͈, Bāt i nēn bu neka bu nit di wah͈, di na joh͈i warugal am chi bes i ate ba.
Fōfale ñena chi bindānkat ya ak Pharisee ya tontu ko, ne, Jemantalkat bi, buga naño gis mandarga chi you.