35 Nit ku bāh͈ di na gēne yef yu bāh͈ chi dēnchukay am bu bāh͈; wande nit ku bon di na gēne yef yu bon chi dēnchukay am bu bon.
E dōm i ñangor yi, yēn ñi bon, naka ngēn mune wah͈ lu bāh͈? ndege lu fês chi h͈ol gemeñ gi wah͈ ko.
Mu ne len, Bindānkat bu neka mbōk bu ñu nekalo tālube chi ngur i ajana, niro na ak borom‐ker ku gēne chi dēnchukay am lu ês ak lu maget.
Nōgu itam garap gu bāh͈ gu neka di na mēña mēñef bu bāh͈; wande garap gu bon di na mēña mēñef bu bon.