Matthew 12:32 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907
32 Te ku wah͈ lu bon lu jem chi Dōm i nit ka, di nañu ko baal; wande ku wah͈ lu bon lu jem chi Nh͈el mu Sela ma, du ñu ko baali muka chi aduna sile, wala chi lah͈īra.
Dōm i nit ka ñou di leka te di nān, te ñu ne ko, Fuh͈alekat bi, ak nānkat i biñ bi, ak and’ i publican yi ak bakarkat yi. Wande sago jubantiku na chi i jef am.