30 Ku nekul ak man, bañ na ma; te ku dajaleūl ak man, defa tasāre.
Naka la kena munê h͈araf chi nēg i borom‐dōle, te yah͈a alal am, su jekulê taka borom‐dōle ja? te ganou lōla di na yah͈a nēg am.
Ken munul a jāmu ñar i borom: ndege di na bañ kena, te sopa kenen; mbāte di na topa kena, te jēpi kenen. Munu len a jāmu Yalla ak alal.
Te du ngir h͈êt wi reka, wande ndah͈ mu mun a dajale chi bena dōm i Yalla ña tasāro won fu neka.