29 Naka la kena munê h͈araf chi nēg i borom‐dōle, te yah͈a alal am, su jekulê taka borom‐dōle ja? te ganou lōla di na yah͈a nēg am.
Wande su ma gēnê jine ya chi Nh͈el i Yalla, bōba ngur i Yalla dika na fi yēn.
Ku nekul ak man, bañ na ma; te ku dajaleūl ak man, defa tasāre.